TSK

TSK · Acts 17:23

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Lii yeena ko def! Damay noppi, ngeen defe ne damaa mel ni yeen? Dama leen di sikk, tuumaal leen, ngeen gis!

Ndax kat, li gisuwul ci Yàlla, te di manooreem gi dul jeex, ak jikko ji mu wéetoo ndax li muy Yàlla, ba àddina sosoo ba tey, xel man na koo ràññee ci ay liggéeyam, te looloo leen taxa ñàkku lay.

Yàlla moo dogal ci xam-xamam, àddina tële koo xam ci xam-xamu boppam. Moo tax mu soob Yàlla, mu jëfandikoo xibaaru Almasi, biy ag ndof ci nit ñi, ngir musale ko gëmkat ñi.

Aji gëmadi ñooñu la Seytaane yàllay xarnu bii gëlëmal seenum xel, ngir ñu baña gis ceeñeeru xibaaru jàmm bu leeru Almasi, miy melokaanu Yàlla.

Jant yooyu amuleen woon benn cér ci Almasi, te amuleen woon jenn yelleef ci mbootaayu bànni Israyil. Bokkuleen woon ci kóllëre yi ëmb digeb Yàlla, te mu fasoo ko ak ñoom. Ñàkk yaakaar, ak ñàkka xam Yàlla ngeen nekke woon ci àddina.

Yaw Buur bi sax dàkk, doo dee, te bët manu laa gis, yaw Yàlla miy kenn, yaa tedd, yaa màgg, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin!