TSK

TSK · Acts 18:10

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Demal rekk, man maay ànd ak yaw booy wax, di la xamal li ngay wax.»

Ngeen mébét, dara! Ngeen diisoo, diisoo, tus! Yàllaa ànd ak nun!

Booy xuus cim ndox, maa ngi ànd ak yaw; ag dex du la mëdd. Booy dox cib taal, doo lakk, sawara du la xoyom.

«Maa ngii def la bésub tey nga mel ni dëkk bu mag bu tata wër, mel ni xeru weñ mbaa tatay xànjar, jàkkaarlook réew mi mépp, muy buuri Yuda aki kàngamam, di sarxalkati réew mi ak baadoolo yi.

Simoŋ xamle na, ni Yàlla yége jaambur ñi ca njàlbéen, ba sàkke ci seen biir, xeet wu mu tudde turam.

¶ Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?

¶ Am xamuleen ne aji jubadi ñi amuñu cér ci nguurug Yàlla? Bu leen kenn nax: Muy fokati séy yi, di bokkaalekat yi, di jaalookat yi, di góor-jigéen yi, ak ñiy ànd ak ñoom,

Waaye Boroom bee ma dimbali, dooleel ma, ngir kàddu gi siiwe ci man, ba xeeti jaambur yépp dégg ko, te Boroom bee ma musal ci pàddum gaynde.