¶ Ku ñuy wax Korney, njiitu takk-der la woon ca Sesare. Ma nga bokkoon ca mbooloo ma ñu dippee Gàngooru Itali.
TSK
TSK · Acts 18:22
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ «Saa soosa tembe, ca la ñetti nit ña ñu yebale Sesare ba ca man, agsi ca kër ga nu dal.
¶ Ca biir mbooloom gëmkat, ña woon ca dëkk ba ñuy wax Àncos, amoon na ay yonent ak ay jànglekat: ñuy Barnaba, ak Simeyon mi ñu dippee Ñuule, ak Lusiyus mi bawoo Siren, ak Manayen mi yaroondoo ak Erodd boroom Galile, ak Sóol.
Gannaaw loolu, ñu agsi Yerusalem, mbooloom gëmkat ñi, ak ndawi Yeesu yi, ak mag ñi, dalal leen, ñu nettali leen mboolem ni Yàlla def ak ñoom.
¶ Ba loolu amee ñu tàggtoo, daldi dem ba Àncos. Ci kaw loolu ñu woo mbooloo mi, jébbal leen bataaxal bi.
Naka la tàggtoo ak ñoom, ne leen: «Dinaa leen seetsiwaat, bu soobee Yàlla.» Ba loolu amee mu dugg gaal, bàyyikoo Efes,
¶ Ba mu ko defee mu woo ñaari njiiti takk-der, ne leen: «Waajal-leen ñaar téeméeri xarekat ak juróom ñaar fukki gawar ak ñaar téeméeri boroom xeej, ngir ngeen dem Sesare bu juróom ñeenti waxtu jotee ci guddi.
Festus nag bëgg lu neex Yawut yi, tax mu ne Póol: «Ndax nangu ngaa dem Yerusalem, ñu àttee la foofa ci mii mbir ci sama kanam?»