Xelalal ku xelu, mu yokku. Xamalal ku jub, mu yokk njàngam.
TSK
TSK · Acts 18:26
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Kàddu yu lay yedd ci kuy dégg, jaarob wurus la mbaa gànjaru ngalam.
Mu ne: “Ma ne leen, képp ku am, dees na ko dolli, waaye ku amul, la mu am as néew sax, dees na ko nangu.
Teewul Póol ak Barnaba toog Ikoñum diir bu yàgg lool. Fit lañu doon waaree ngir Boroom bi, Boroom bi maye ay firnde aki kéemaan yu jaare ci ñoom, ngir seeree ko kàddug yiwam gi ñuy biral.
Kooku jotoon naa jàng yoonu Sang bi. Mu ànd ak cawarte, di waare ak a jàngle lu wér péŋŋ ci mbirum Yeesu, doonte xam-xamam a ngi yemoon ci sóobeb Yaxya ci ndox.
¶ Bu kenn nax boppam: Ku teg boppam ci yeen, boroom xam-xam, ni xarnu bii jàppe xam-xam, kooku na doon ab dof, ngir am xam-xam bi wóor.
¶ Bët nag manul ne loxo: «Soxlawuma la!» Te bopp it manul ne ay tànk: «Soxlawuma leen!»
¶ Kon nag nanu jóge ci ndoortel àlluway Almasi, daldi jàll jëm ci njàngum mag, te ñu baña lalaat kenu gi. Kenu gi mooy gëm Yàlla gannaaw tuubeel gi war ci jëf ju bon ji nit kiy def te muy jëfi ndee.