TSK

TSK · Acts 19:26

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Seeni tuur xaalis laak wurus, di liggéeyu doom aadama:

Sàkk sam tuur, móol sa jëmmu tuur, te jariñu la tus!

Aaday xeet yi kat neen la. Garab lañuy dagge ca gott ba, ab yettkat yette ko sémmiñ,

Nitoo nit dim sannax, sore xam-xam: te képp kuy tëgg sa jëmmu tuur, yaa añe gàcce. Sa jëmmi weñ ji nga xelli, di neenug neen, noog bakkan, tus!

«Yeen, lu leen xiir ci lii? Nun itam ay nit lanu, bokk ak yeen benn bind. Xibaaru jàmm bi lanu leen di xamal, ngir ngeen wacc yëfi neen yii te walbatiku ci Yàlla, kiy dund te sàkk asamaan ak suuf ak géej ak mboolem lu nekk ci biir.

¶ Ba ñu teeree Efes, fa la Póol bàyyi Pirsil ak Akilas. Mu dem ca jàngu ba, ba diisoo fa ak Yawut ya.

Ba mu ko defee ñu bare ca gëmkat ña dikk, biral seenug tooñ, daldi xamle yu bon ya ñu daan jëfe.

Ana kon lu sama wax jiy wund? Ndax daa wund ne yàpp wu ñu sarxal tuur yi tekki na lenn? Am daa wund ne tuur yi tekki na lenn?

Nit ñi ci seen bopp ñoo nuy waxal fépp, na sunu ngan ak yeen deme, ak ni ngeen walbatikoo ci Yàlla, dëddu tuur yi, bay jaamu Yàlla ju dëggu jiy dund,