TSK

TSK · Acts 2:11

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

te limaaleesul galag ya jóge ca jaaykat ya ak jula yaak mboolem buuri Arabi, ak jaraafi réew ma.

àddu, sant la, lim sa jépp jaloore.

Éy Yàlla, ba may ndaw, nga ma xamal say kéemaan, te ba tey jii maa ngi koy biral.

Dunu ko nëbb sunuy doom, xanaa di ko jottli maas giy ñëw, xamal leen jaloorey Aji Sax ji ak kàttanam aki kéemaanam.

Siiwal-leen teddngaam fi biir xeet yi, xamal waasoo waaso ay jalooreem.

Nañu sante Aji Sax ji ngoram ak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi.

Moo dogal ñuy fàttlikuy kéemaanam; Aji Sax ji boroom yiw ak yërmande.

Deesatu fa dëkk, xanaa gental ba fàww. Màngaan dootu fa samp xayma, sàmm dootu fa gooral.

Aji Sax ji, yaay sama Yàlla, dama lay teral, di la sant. Yaa defi jaloore, muy dogal yu yàgg, wér te wóor.

«Téenleen, séentu tund ya ne faraas! Ana fu ñu leen fi tëddewul? Ci yoon yi ngeen di yeeroo ni màngaan muy dogalee ci màndiŋ mi. Sobeel ngeen réew meek seen gànctook seenug mbon.

Ma tëdd sama lal, daldi am gént gu ma tiital, ak xalaat ak peeñu yu ma indil njàqare.

Te itam teeru boobu neexul woona lollikoo. Loolu waral ña ëpp ca waa gaal ga mànkoo ci jóge fa, dellu géej, te fexe nu ñu àgge Fenigsë, ngir lollikoo fa. Mooy teerub dunu Keret bi jublu sowub suuf ak sowub kaw.

Ñi Yàlla tabb ci biir mbooloom gëmkat ñi, ñi ci jiitu ñoo di ndawi Almasi. Ñaareel bi di ñiy waxe kàddug waxyu, ñetteel bi di jànglekati kàddu gi. Ñi ci topp di ñiy def ay kéemaan, ñi ci topp di ñi am mayu faje, ak ñi mane dimbalee, ak ñi mane jiite, ak ñiy làkk yeneen xeeti làkk.

Ajara moomu mooy tundu Sinayi, wa ca réewum Arabi, te moo taxawe Yerusalem gii tey, dëkk bii dib jaam mook doomam yi ko dëkke.

Ma wax ko waru jenn waay, ab waa Keret buy seen yonentu bopp. Mu ne: «Waa Keret, ay fen-kati neen, soxor niy rabi àll, fuqle, yaafus.»