Maay sottim ndox suuf su mar, ak wal yu waleg joor gu wow. Maay sotti saw askan samag noo, sama barke sottikul ñi nga meññ,
TSK
TSK · Acts 2:38
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Maa leen di wis ndox mu set, ngeen set. Mboolem seen sobe ak mboolem seen kasaray tuur laa leen di setalal.
te ciw turam, dees na dale ci Yerusalem, yégal xeet yépp, tuubeel gu jur njéggalug bàkkaar.
Kon nag tuubleen te dëpp, ndax seeni bàkkaar faru.
Waaye ba ñu gëmee Filib, ma leen xamal xibaaru jàmm, bi jëm ci nguurug Yàlla ak turu Yeesu Almasi, góor ak jigéen daldi nangu, ñu sóob leen ci ndox.
Piyeer ne ko: «Na sa xaalis ànd ak yaw asaru, ndegam ab xaalis nga yaakaara jënde mayu Yàlla!
Filib ne ko: «Soo gëmee ci sa léppi xol, sañ nga ko.» Mu ne ko: «Gëm naa ne Yeesu Almasi mooy Doomu Yàlla.»
Mu santaane nag ñu sóob leen ci ndox ci turu Yeesu Almasi. Gannaaw loolu ñu ñaan Piyeer, mu toog ci ñoom ay fan.
Ñu ne ko: «Gëmal Sang Yeesu, daldi mucc, yaak sa waa kër.»
Póol ne leen: «Yaxya, sóobeb tuubeel la daan sóobe ci ndox, di waxaale askan wi ne leen ñu gëm kiy topp ci moom, te mooy Yeesu.»
Léegi nag, looy nég? Jógal, ñu sóob la ci ndox, nga set, teqlikook say bàkkaar, te tudd turu Yeesu.”
Waaye li dale Damaas ak Yerusalem ba ci réewum Yawut gépp, ba ca ñi dul Yawut, ñoom ñépp yégal naa leen seen wartéef, muy tuubeel ak waññiku ci Yàlla, ak jëf ju tuubeel yellool.
¶ Ndax Almasi dafa xaajalikoo? Ndax Póol lañu daajoon ca bant ba ngir yeen? Am ci turu Póol lañu leen sóobe ci ndox?
Ndox mooma di misaalub sóobu gi leen musal tey; du sóobu guy dindi tërub yaram, waaye moom ngeen di wuyoo wooteb Yàlla ci xel mu dal, te li leen di musal mooy ndekkitel Yeesu Almasi,