Mu laxasu Beñamin rakkam, daldi jooy, Beñamin it laxasu ko, jooy.
TSK
TSK · Acts 20:37
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Xale ba dem, Daawuda jóg, génne ca làquwaayam ba fare bëj-saalum. Mu ne gurub, dëpp jëëm fa suuf, sujjóot ñetti yoon, ku nekk fóon sa moroom, ñoom ñaar ñépp jooy, te Daawuda rawati.
«Éy Aji Sax ji, ngalla bàyyil xel ni ma àndeek yaw sama léppi xol, ci kóllëre, te li nga rafetlu laa jëfe.» Mu jooy nag, jooy yu metti.
Ñu dikk ba jub ko, di ko séentoo fu xawa sore, waaye xàmmeetuñu ko. Ñu daldi ne yikkét jooy. Ba ñu agsee ku ci nekk ne sa mbubb tareet. Ñuy ñaawlu, di tibb suuf, di sànni ca kaw, muy sottiku ci seen kaw bopp.
¶ «Mu jóg, ngir dellu kër baayam. Fu sore la ko baayam séene, muy dikk. Mu ñeewante ko, daw, laxasu ko, fóon ko.
Bokk yépp a ngi leen di nuyu. Saafoonteeleen fóonante yu sell.
¶ Nuyul-leen nu bokk yépp, te fóonal-leen nu leen na mu gëna selle.
ndaxte Gàtt bi ci diggu ngàngune mi moo leen di sàmm, yóbbu leen ca bëti ndoxum dund ma, te Yàllaa leen di fompal wépp rongooñ.»