Ñu yég ko, daw làquji diiwaanu Likawni, ca dëkk ya ñuy wax Listar, ak Derbe ak la ko wër.
TSK
TSK · Acts 20:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ci kaw loolu Póol agsi Derbe, teg ci dëkk ba ñuy wax Listar. Ndeke ab taalibee nga fa bu ñuy wax Timote; ndeyam di gëmkatub Almasi bu bokk ci askanu Yawut, baayam di Gereg.
¶ Ba mu ko defee bokki gëmkat ña yebal ca saa sa Póol ak Silas ca guddi ga, ñu jëm Bere. Ñu agsi, dem ca jàngub Yawut ya.
Booba Torofim mu Efes la ñu gisoon ca dëkk ba, mu ànd ak Póol, ñu yaakaar ne Póol da koo yóbbu ca kër Yàlla ga.
¶ Timote sama mbokkum liggéeykat nuyu na leen, mook Lusiyus ak Yason ak Sosipater sama bokki Yawut.
¶ Ci man Póol, ndawal Almasi Yeesu ci coobarey Yàlla, ci man la bataaxal bii bawoo, bawoo itam ci Timote mbokk mi, ñeel mbooloom Yàlla mi ci Korent, ak mboolem ñu sell ñi ci diiwaanu Akayi gépp.
Su dee mbirum Tit, mooy sama wéttal, di ma jàpple ci liggéey bi, ngir yeen. Sunu bokk, yi ànd ak moom nag, ñooy ndawi mboolooy gëmkat ñi, te ñooy teraangay Almasi.
¶ Yaakaar naa nag, ne bu soobee Sang Yeesu, dinaa leen yónnee Timote balaa yàgg, ngir xam nu ngeen def, ba man ci sama bopp, sama xel dal.
¶ Aristàrk mi ma bokkal kaso bi, mu ngi leen di nuyu, moom ak Màrk rakku Barnaba. Ci mbiru Màrk moomu ngeen jotoon ndigal, ngir bu dikkee, ngeen teral ko.
ñeel Timote, sama doom, sama soppe. Aw yiw ak yërmande ak jàmm ñeel na la, bawoo ci Yàlla Baay bi, ak sunu Sang Almasi Yeesu.
Eràst moom, Korent la des, waaye Torofim, Mile laa ko bàyyi, ndax daa woppoon.
mook Màrk ak Aristàrk ak Demas ak Luug, bokk yi may liggéeyandool.