TSK

TSK · Acts 21:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ba mu ko defee Daawuda tabb ay jawriñam ca Damaas ca Siri, waa Siri nekk ci curgag Daawuda, di ko fey galag. Aji Sax ji may Daawuda ndam fépp fu mu dem.

Yàlla nee: «Ma limaale Misraak Babilon, ñi ma xam di dégg. Xoolal Filisti ak Tir, ak réewum Kuus. Nit a ngii, juddoo fa,»

¶ Bu juróom ñaar fukki at yi matee, Aji Sax ji dikkal Tir, ñu delluy liggéey, di feyu, di gànctook mboolem réewi àddina fi kaw suuf

¶ «Wóoy ngalla yeen waa Korasin, yeen waa Beccayda it, wóoy ngalla yeen, nde kéemaan yi sottee fi seen biir, su doon fa waa Tir mbaa fa waa Sidon la sottee, kon bu yàgg lañu doon sol ay saaku, xëppoob dóom, ngir tuub.

¶ Gëmkat ña tasaaroo woon nag ndax fitna ja woon, ca mbirum Eccen, mujj nañu jàll ba diiwaanu Fenisi, ca dunu Sippar ak ca Àncos, waaye àggewuñu kàddu gi ñeneen ñu moy Yawut yi.

Acts 13:4 TSK

¶ Ñooñu la Noo gu Sell gi yebal, ñu dem dëkk ba ñuy wax Selusi, dugge fa gaal, jëm dun ba ñuy wax Sippar.

¶ Mbir mi nag mujje dëngoo bu metti, ba ñu teqlikoo. Barnaba ànd ak Yowaan Màrk, dugg gaal, jëm Sippar.

¶ Ba loolu wéyee Póol toogaat na fa fan yu bare, doora tàggtoo ak bokk ya, dugg gaal jëm Siri, ànd ak Pirsil ak Akilas. Fekk na mu watu nel ca teerub Señsere, firndeele ko aw xas wu mu xasoon.

Acts 27:4 TSK

Nu jóge fa, dellu géej, ngelaw li soflu nu, nu leru tefesu Sippar, jaare wet gu nu fegoo ngelaw li.