TSK

TSK · Acts 23:9

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ba Daawuda waxee Sóol kàddu yooyu ba daaneel, Sóol da ne: «Éy Daawuda, doom, loolu sa baat la moos?», daldi ne yikkét jooy.

Luke 23:4 TSK

Pilaat ne sarxalkat yu mag ya ak mbooloo ma: «Waa jii, gisuma ci moom genn tooñ.»

¶ Pilaat ne leen ñetteel bi yoon: «Ana lu bon lu kii def? Lenn lu jar dee, gisuma ko ci moom. Kon nag, dama koy dóorlu, yiwi ko.»

Acts 5:39 TSK

Waaye su bawoo fa Yàlla nag, dungeen ko mana fanq, moytuleena jànkoonte ak Yàlla.» Ñu daldi fekksi Gamalyel,

Gannaaw nag Yàllaa leen jagleel genn may, ga mu nu jagleeloon, ba nu gëmee Sang Yeesu Almasi, ana ku ma doon, man, bay gàllankoor Yàlla?»

¶ «Yàlla def, gannaaw ba ma délsee Yerusalem, ma doon ñaan ca kër Yàlla ga, daldi daanu leer.

Ma gis nag ne li ñu ko jiiñ, ci seen mbiri yoonu diine rekk la, waaye du lenn lu jar rey, mbaa jéng.

Nu ne dàll fi suuf. Ma dégg baat bu ma wax ci làkku yawut, ne ma: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bundxatal? Dangay sonal sa bopp rekk, mbete fas wu manula woŋŋeetu ba wéq dëgël bu koy jam.”

Ndax malaakam Yàlla ji ma moom, te ma di ko jaamu, moo ma dikkal biig.