TSK

TSK · Acts 26:10

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Acts 7:58 TSK

ñu wat-watee ko, génne ko dëkk ba, di ko dóor ay doj. Fekk na seede ya summi seeni mbubb, juug ca tànki benn xalelu góor bu ñuy wax Sóol.

Acts 8:3 TSK

Ci biir loolu Sóol moom, ma ngay jéema faagaagal mbooloom gëmkat ñi, di dugg ci kër yi, diri góor ak jigéen, génne, ñu sànni kaso.

Acts 9:13 TSK

Anañas nag ne ko: «Sang bi, maa dégge ci ñu bare mbirum kooku, ñu seede mboolem jëf ju bon ji mu def say nit ñu sell ci biir Yerusalem.

Acts 9:26 TSK

¶ Ba Sóol agsee Yerusalem, jéem naa jaxasook taalibe yi, waaye ñépp a ko ragal, ndax ñàkka gëm ag taalibeem.

Acts 9:41 TSK

Piyeer may ko loxo, yékkati ko. Ba loolu amee Piyeer woo ñu sell ña, ak jëtun ña, won leen ndaw sa, muy dund.

Ma ne ko: “Sang bi, ñoom ci seen bopp xam nañu ne jàngu ci kaw jàngu, maa fa daan tëjlu ak a cawlu ñi la gëm.

ndax kat maa gëna ñàkk solo ci ndawi Almasi, te yeyoowuma sax turu ndaw, gannaaw maa doon bundxatal mbooloom Yàlla mi.

¶ Ci man Póol, ndawal Almasi Yeesu ci coobarey Yàlla, ci man la kàddu gii bawoo, ñeel ñu sell ña ca Efes te di ñu sàmm seen kóllëre ak Almasi Yeesu.