1 Kings 21:8
TSK
Ci kaw loolu Yesabel bind ay bataaxal ci turu Axab, def ci màndarga torlub Axab. Mu yónnee bataaxal ya ca mag ñaak gor ña ca dëkkub Nabot.
TSK
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ci kaw loolu Yesabel bind ay bataaxal ci turu Axab, def ci màndarga torlub Axab. Mu yónnee bataaxal ya ca mag ñaak gor ña ca dëkkub Nabot.
Wóoy ngalla boroom dogal yiy dogal njubadi, bind ko, te muy jur coono,
‘Aji Sax ji da laa fal sarxalkat, nga wuutu Yoyada sarxalkat bi, ngir kër Aji Sax ji am ku ko yor, ba dof bu fiy wax-waxlu ay waxyu, nga jéng ko, yeewe ko càllalay weñ ci baatam.
Sarxalkat bu mag bi, ak mboolem kurélu mag ñi man nañu ma cee seede. Ci ñoom sax laa nangoo woon bataaxal bu jëm ca bokki Yawut ya ca Damaas, ga ma jëmoon, ngir yeewe fa gëmkati Yoon wii nekkoon foofa, ba indi leen Yerusalem, ngir ñu mbugal leen.