TSK

TSK · Acts 26:7

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Ezra 6:17 TSK

Sarxe nañu ca daloog kër Yàlla googu téeméeri yëkk, ak ñaar téeméeri kuuy ak ñeenti téeméeri xar yu ndaw, ak fukki sikket ak ñaar, dëppook limu giiri Israyil, def ko saraxu póotum bàkkaar, ñeel Israyil gépp.

Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Ayca, santleen Aji Sax ji, yeen jaami Aji Sax ji yépp, yeen ñiy taxawe kër Aji Sax ji guddi.

Luke 2:36 TSK

¶ Jigéen ju ñuy wax Aana, ab yonent la woon ca Yerusalem, di doomu Fanuwel mi askanoo ci giirug Aser. Mag la woon lool. Ba muy janq la séy, nekk ak jëkkëram juróom ñaari at.

Yeenay lekk ak a naane ca sama ndab, ca sama nguur, te yeenay tooge ay gàngune, di jiite fukki giiri bànni Israyil ak ñaar.»

Acts 26:2 TSK

¶ «Buur Àggripa, mbégte laa am ndax dinaa layool sama bopp ci sa kanam tey, ngir tontu mboolem lu ma Yawut yi jiiñ.

Guddi ak bëccëg, pastéefu xol lanuy dagaane Yàlla, ngir man leena gisaat, ba mottli li yées ci seen ngëm.

James 1:1 TSK

¶ Ci man Yanqóoba, jaamub Yàlla ak Sang Yeesu Almasi, la bataaxal bii bawoo, ñeel fukki giir ak yaar yi tasaaroo ci àddina. Maa ngi leen di nuyu.