Aji Sax ji nas, mu àntu ba fàww, mu mébét, mu sottil maasoo maas.
TSK
TSK · Acts 27:1
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Bare na lu xol di mébét, waaye Aji Sax jeey dogal.
Njiitu takk-der ba ko teewe woon nag sàbbaal Yàlla, ne: «Aylayéwén, waa jii ku jub la.»
Ñu ne ko: «Njiitu takk-der ba Korney, ku jub, ragal Yàlla, te rafet seede bu ko xeetu Yawut wépp seedeel, moo jote ci malaaka mu sell, ndigalal woolu la këram, ngir déglu say kàddu.»
Mu daje fa ak Yawut bu ñuy wax Akilas, fekk baax diiwaanu Pont. Muy sooga jóge réewum Itali, ànd ak soxnaam Pirsil, ndax Buur bu mag ba Këlódd moo joxe woon ndigal ne na Yawut yépp génn Room.
Ca saa sa mu ànd ak ay dag, ak njiiti takk-der, ne jaas ca biir mbooloo ma. Yawut ya nag gis njiital gàngoor ga ak dag ya, daldi dakkal yar ya ñu doon dóor Póol.
Ca guddi ga Sang bi feeñu Póol, ne ko: «Na sa xel dal. Ni nga ma seedeele ci Yerusalem, noonu nga ma wara seedeeleji ca Room.»
Ci kaw loolu mu sant njiitu takk-der ba, ne ko mu may Póol bët, woyofal ko jataayu kasoom te baña aaye ay nitam ñu topptoo ko.
Man nag damaa gis ne deful dara lu jar àtteb dee. Waaye gannaaw moo dénk boppam buur bu tedd bi, man dogu naa ko koo yónnee.
Teewul njiitu takk-der ba sobental waxi Póol, déggal dawalkat ba ak boroom gaal ga.
Ba nu dikkee Room nag may nañu Póol, mu am daluwaayu boppam, ab takk-der di ko wattu.
¶ Nuyul-leen ma mboolem seeni njiit, ak mboolem gëmkat ñu sell ñi. Waa Itali ñu ngi leen di nuyu.