TSK

TSK · Acts 28:20

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Looloo tax, bi ngeen ma wooloo, ma ñëw te tendeefaluma benn yoon. Ma di leen laaj nag li waral ngeen woolu ma.»

¶ Ci kaw loolu njiit la agsi, jàpp ko, daldi santaane ñu jénge ko ñaari càllala. Ba loolu wéyee mu laajte, ne: «Kii ku mu doon, ak lu mu def?»

Yaakaar ji ma am, mooy yaakaar ji ñu am ñoom itam, ne ñi jub ak ñi jubadi, ñépp ay bokk dekki ëllëg.

Póol ne ko: «Mu gaaw, mu yeex, waxuma yaw rekk, waaye yaak mboolem ñi may déglu laay ñaan Yàlla, ngeen fekksi ma ci lépp, lu moy càllala yii ñu ma jénge!»

¶ Moo ma tax di ñaan, man Póol mi ñu tëj ngir Almasi, ndax ñi dul Yawut, yeen jaambur ñi,

xibaar bi ma di ndawam lu ñu tënke ay jéng. Waaye ñaanal-leen ma ma di ko waxee fit, ni mu ma ware.

¶ Man Póol nag maa leen bind nuyoo bii ci sama loxol bopp. Fàttlikuleen ne dañu maa tëj kaso. Yal na aw yiw ànd ak yeen!

Xibaaru jàmm boobu moo tax may daj coono yu metti ni defkatu mbon, ba ci jéng yii ñu ma jéng. Waaye kàddug Yàlla moom, deesu ko jéng.

Dama koo bëggoona téye fi sama wet, ngir mu taxawal la, di ma dimbali, li feek maa ngi ci kaso bi ngir xibaaru jàmm bi.