¶ Gannaaw loolu Yeesu wër dëkkoo dëkk bu mag ak bu ndaw, di waare, di yégle xibaaru jàmm bu nguurug Yàlla, ànd ak fukki taalibe yaak ñaar,
TSK
TSK · Acts 28:31
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ba ñu ñaanee ba noppi, bérab ba ñu daje daa yëngu, ñu feese Noo gu Sell gi ñoom ñépp; ñu daldi tàmbalee waxe fit kàddug Yàlla gi.
Waaye ba ñu gëmee Filib, ma leen xamal xibaaru jàmm, bi jëm ci nguurug Yàlla ak turu Yeesu Almasi, góor ak jigéen daldi nangu, ñu sóob leen ci ndox.
Ca guddi ga Sang bi feeñu Póol, ne ko: «Na sa xel dal. Ni nga ma seedeele ci Yerusalem, noonu nga ma wara seedeeleji ca Room.»
¶ Man itam, booleleen ma ci, ngir saa yu ma ubbee sama gémmiñ, mana xéewloo ndéey lu ma xamlee fit wu dëgër, mbóoti xibaaru jàmm bi,
Te ngeen ñaanaale nu ci itam, ngir Yàlla ubbil nu buntu xamle kàddu gi, ngir siiwtaane mbóot mi ci Almasi, li waral ñu jéng ma.
Waaye Boroom bee ma dimbali, dooleel ma, ngir kàddu gi siiwe ci man, ba xeeti jaambur yépp dégg ko, te Boroom bee ma musal ci pàddum gaynde.