Yaw Yàlla, na la xeet yi sant, na la xeet yépp sant.
TSK
TSK · Acts 3:26
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
«Ab jotkat ay dikkal Siyoŋ, ba jot ñi tuub seeni bàkkaar ci askanu Yanqóoba.» Kàddug Aji Sax jee.
Maa leen di raxasal mboolem ñaawtéef gu ñu ma moye, baal leen mboolem ñaawtéef yu ñu ma moye, di ma gàntal.
Maa leen di wis ndox mu set, ngeen set. Mboolem seen sobe ak mboolem seen kasaray tuur laa leen di setalal.
te ciw turam, dees na dale ci Yerusalem, yégal xeet yépp, tuubeel gu jur njéggalug bàkkaar.
Waaye moom la Yàlla yiwee ci mititu ndee, dekkal ko, ndax dee amul kàttanu tënk ko.
Su boobaa jamonoy péex ay bawoo ci Boroom bi, te mooy yebal Almasi mu leen jagleel, te muy Yeesu.
Yeen nag yeenay donoy yonent yi te yeenay séddu ci kóllëre, gi Yàlla fasoon ak seeni maam, ba mu nee Ibraayma: “Ci saw askan la xeeti àddina yépp di barkeel.”
Nun nag noo leen di àgge xibaaru jàmm bii: li Yàlla digoon sunuy maam,
¶ Ci kaw loolu bésub Noflaay bu nekk Póol di waare ca jàngu ba, di yee Yawut yi ak Gereg yi.
¶ Ci kaw loolu ñu jox ko bés, bés ba dikk, ñu bare dikk, fekksi ko ca daluwaayam. Suba ba ngoon mu di leen jàngal, di leen seedeel lu jëm ci nguurug Yàlla, di leen won ci mbirum Yeesu, firnde yu leen gëmloo te tukkee ci yoonu Musaa ak ci yonent yi.
Njàqare ak musiba daal, mooy dal ci kaw képp kuy def lu bon, te Yawut bi jiitu ci, waaye ki dul Yawut it topp ci;
ba tax na, boroom ngëm yi lees di booleek Ibraayma miy boroom ngëm, barkeel leen.
Moo defal loolu mbooloo mi ba man koo setale cangaayal ndox mu ànd ak kàddoom, ngir sellal ko.
¶ Cant ñeel na Yàlla, sunu Baayu Sang Yeesu Almasi! Moo nu judduwaatal ci yërmandeem ju yaa, ci dooley ndekkitel Yeesu Almasi, ngir may nu yaakaar juy dund.
¶ Ma dégg limub ña ñu màndargaale torluwaay ba; ñuy téeméer ak ñeent fukk ak ñeenti junni (144 000), bawoo ci mboolem giiri bànni Israyil: