Ndeke xel mi ci nit mooy noowal Aji Man ji koy may dég-dég.
TSK
TSK · Acts 6:10
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ngànnaay lu ñu la mana sàkkal, du sotti, te boroom làmmiñ wu la jógal cib layoo yaa koy tiiñal. Ñiy jaamu Aji Sax ji, looloo di seen cér, looloo di njekk gi ma leen di dikke.» Kàddug Aji Sax jee.
Maa lay def nga mel ak askan wii ni tatay xànjar ju ñu dàbbli, ñu di la song te duñu la man. Maay ànd ak yaw, di la wallu, di la xettli.» Kàddug Aji Sax jee.
Teewul man, may feese doole, feese Noowug Aji Sax ji, ak dëgg ak njàmbaarte, ngir biralal askanu Yanqóoba, bàkkaaram, ngir tuddal bànni Israyil googu moyam.
Mooy ndaw li koy jiitu, ànd ak leer ga ak xam-xam, ba woon ca Yonent Yàlla Ilyaas, ba waññi xolu baay ci doomam, waññi ku déggadi ci xelum aji jub, loolu yépp ngir waajal aw xeet ba ñu jekk ngir Boroom bi.»
Ndax man maa leen di jox làmmiñ wu ànd ak xel, wu seen benn noon dul mana dàq mbaa di ko weddi.
Waaye su bawoo fa Yàlla nag, dungeen ko mana fanq, moytuleena jànkoonte ak Yàlla.» Ñu daldi fekksi Gamalyel,
Sama kàddu ak samam njàngle jotewul woon dara ak neex làmmiñ gu xam-xamu nit ràbb, waaye dafa di ay firnde yu manooreg Noowug Yàlla lañal,