bay jaamuji yeneen yàlla, di leen sujjóotal, mbaa muy sujjóotal jant bi, mbaa weer wi, mbaa mboolem gàngooru asamaan, te santaanewuma ci lenn,
TSK
TSK · Acts 7:42
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ba loolu amee ñu dëddu mboolem seen santaaney Yàlla Aji Sax ji; sàkkal seen bopp ñaari wëllu yu ñu móol, samp xer wu ñuy jaamoo Asera, di sujjóotal mboolem biddiiwi asamaan tey jaamu Baal.
ndegam maa masa niir jant beek leeraayam, mbaa weer wiy daagoo yànjaayam,
Ñeent fukki at laa jéppi googu maas, ma ne: “Xeet wu ñàkk wormaa ngi, te faaleedi samay santaane.”
Waaye ñoom ñoo fippu, di naqaral xelam mu sell, mu soppliku seen noon, ba mujj di xareek ñoom.
Këri Yerusalem ak këri buuri Yuda dina fees ak sobe ni bérab bii di Tofet. Mooy mboolem kër yu ñu doon taalal cuuraay ca kaw taax ya ñeel biddiiw yépp, ak di fa tuural yeneen yàlla.”»
¶ «“Képp ku bokk ci waa kër Israyil, mbaa muy doxandéem bu dal ci biir Israyil, bu ma waccee, ba yékkati kasaray tuur, def ci xolam, muy ay wu koy gàllankoor, te mu ne ci jàkk, kooku bu dikkee cib yonent di sàkku leeraange ci man, man Aji Sax ji maa koy tontul sama bopp.
¶ «“Léegi nag yeen waa kër Israyil, Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Aca, na ku ne jaamuji kasaray tuuram! Dungeen mujje lu moy déggal ma, ba sama tur wu sell wi, dootuleen ko teddadile seeni sarax ak seeni tuur.
«Yeen bànni Israyil, saraxi gàtt ak saraxi pepp, ndax man ngeen ko daan indil diiru ñeent fukki at ca màndiŋ ma?
¶ Moo tax Yàlla bërgal leen ak seen xemmemtéef yu bon yi ci seen xol, ba ñu sóobu ci jëflantey sobe juy teddadil seen yarami bopp.
«fa ma seeni maam doon seetloo, di ma diiŋat, te gisoon samay jaloore,