TSK

TSK · Acts 7:43

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «Buleen sàkkal seen bopp tuur muy jëmmal lenn lu nekk ci kaw asamaan, mbaa ci kaw suuf, mbaa lu nekk ci ndox mu suuf tiim.

«Waxal bànni Israyil ne leen: Muy bànni Israyil muy doxandéem ci Israyil, képp ku ci jël ciy doomam, jébbal tuur mi ñuy wax Moleg, dee rekk mooy àtteem. Na ko waa réew mi dóor ay doj, ba mu dee.

¶ «Buleen sàkkal seen bopp tuur muy jëmmal lenn lu nekk ci kaw asamaan, mbaa ci kaw suuf, mbaa lu nekk ci ndox mu suuf tiim.

Ba loolu amee ñu dëddu mboolem seen santaaney Yàlla Aji Sax ji; sàkkal seen bopp ñaari wëllu yu ñu móol, samp xer wu ñuy jaamoo Asera, di sujjóotal mboolem biddiiwi asamaan tey jaamu Baal.

Te itam sarxal na doomam, lakk ko ngir ay tuur. Ci biir loolu jabar na, ñeengo na, jëflante naak boroom rawaan aki gisaanekat. Bare na lu mu def lu Aji Sax ji ñaawlu, ba merloo ko.