TSK

TSK · Acts 7:46

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Samiyel ne ko: «Nii la Aji Sax ji dagge nguurug Israyil ci yaw bés niki tey, jox ko keneen ku la gën.

¶ Samiyel nag ne Yese: «Xale yu góor yi yemb nañu?» Yese ne ko: «Xanaa ki gën di ndaw. Ma ngay sàmm gàtt ya.» Mu ne ko: «Yónneel, woolu ko, dunu jekki te dikkul fii.»

¶ Gannaaw loolu Buur Daawuda sanc na këram, Aji Sax ji noppal ko ci noonam yi ko wër yépp.

¶ Ba loolu amee Buur Daawuda dikk ba fa kanam Aji Sax ji, toog ne ko: «Boroom bi Aji Sax ji! Ana lu ma doon, ak lu sama waa kër doon, ba tax nga indi ma ba fii?

xanaa tànn giirug Yuda, taamu tundu Siyoŋ wi mu sopp.

Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Éy Aji Sax ji, bàyyil xel Daawuda, ak gépp njàqareem.

Mu jële ko fa, sampal leen Daawuda, muy buur bu mu seedeel ne: “Maa ràññee Daawuda doomu Yese, ji sama xol jubool, te mooy jëfe mboolem samay coobare.”