sorale bakkanam pax, ba ab xeej du ko bóom.
TSK
TSK · Acts 9:11
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Aji Sax ji, ci ay xóote laa lay wooye.
Sàkkuleen Aji Sax ji bi ngeen koy mana gis, wooleen ko bi muy jege.
Maa dégg moos askanu Efrayim di binni naan: “Aji Sax ji, duma nga noo duma, ni sëllu wu dese tàggat. Ngalla waññi nu, nu waññiku; yaw Aji Sax ji, yaa di sunu Yàlla.
¶ «Bu loolu amee maay sottil waa kër Daawuda ak waa Yerusalem, noowug yiw aki dagaan, ba ñu geesu ma man, mi ñu jam ba mu sar, te dinañu ko jooy ni ñuy jooye benn bàjjo, di ko naqarlu ni ñuy naqarloo deewug taaw.
Moo tax ma ne leen, ñaanleen, ñu may leen; seetleen, ndax ngeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen.
Mu teg ca ne: «Yeesu, boo délsee ci sa nguur, fàttliku ma!»
Su boobaa, ku woo Boroom bi wall ciw turam, dinga raw.”
¶ Menn malaakam Boroom bi nag wax Filib, ne ko: «Fabul jubal bëj-saalum; yoon wa kenn jaareetul te bartaloo Yerusalem, jëm Gasa.»
Léegi nag yebleel ca Yope, nga wooluji fa ku ñuy wax Simoŋ, ñu di ko dàkkentale Piyeer.
¶ Ba loolu wéyee Barnaba jëm Tàrs, di seeti Sóol.
¶ «Man ab Yawut laa, juddoo Tàrs ca diiwaanu Silisi, yaroo ci dëkk bii. Ci keppaaru Gamalyel laa jànge, njàng mu dëppoo bu mat sëkk ak sunu yoonu maam. Ma doonoon ku xér ci Yàlla ni mboolem yeen ñii tey.