TSK

TSK · Amos 2:9

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Damaa wàcc, xettlisi leen ci waa Misra; génne leen réew moomu, ba yóbbu leen réew mu baax te yaatu, réew mu meew maak lem ja tuuroo, foofa ca diiwaanu Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña.

Xanaa kay, kàttan gu askanu réew ma am, péey ya dàbbliku te yaa lool. Te it ponkal yooyu cosaanoo ci Anageen ñi lanu fa gis.

Siwon nag mayul Israyil, ñu jaarem réewam, xanaa mu dajale gàngooram gépp, sàqi, ngir dajejeek Israyil ca màndiŋ ma. Mu dikk ba Yaxacc, song Israyil,

Ana fu nu jëm? Te sunu bokk ya demoon yoqiloo nu, ne nu waa réew maa nu ëpp, sut nu, dëkk ya réy te dàbblikoo ay tata yu àkki asamaan. Rax ci dolli, ay ponkal yu bokk ci askanu Anageen ñi lanu fa gis!»

¶ Aji Sax ji neeti: «Ayca, jàll-leen walum Arnon. Mu ngoog, maa teg ci seen loxo, Siwon Amoreen ba, buurub Esbon, mook réewam. Dal-leen di nangu réew mi, song ko xare.

¶ Israyil dégluleen! Yeena ngii tey, di jàll dexu Yurdan ngir dàqi xeet yu leen ëpp, ëpp leen doole, ngir nangu seen dëkk yu réy, dàbblikoo tata yu àkki asamaan.

Job 18:16 TSK

Ku bon mooy garab gu dee kaw ak suuf, reen wow, xob lax.

«Neel, Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Mbaa jooju reseñ dina baaxle? Mbaa jeneen jaxaay ja du buddiy reenam, buur doom ya, ba lu mu jebbile woon lax, ba buddi reen ya du laaj përëg bu réy, mbaa nit ñu bare?