Ndaxam yaa ngi réy-réylu ci sama kaw ñoñ ba tey, bañ leena bàyyi, ñu dem.
TSK
TSK · Amos 4:10
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Musaa ak Aaróona nag dem ca Firawna, wax ko ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi dafa wax ne: “Siide nga maa nangul daal? Waaw, foo àpp sa ngàntal ak man? Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma.
¶ Ca xaaju guddi la Aji Sax ji fàdd mboolem taawi réewum Misra yu góor, dale ko ca taaw bu góor bu Firawna, ma toog ca jal ba, ba ca taaw yu góor yu nit ña ñu tëj kaso, boole ca lépp luy taaw bu góor ca jur ga.
¶ Da ne leen: «Bu ngeen farloo ci déggal seen Yàlla Aji Sax ji, di def li mu rafetlu, di teewlu tey jëfe ay santaaneem, di sàmm bépp dogali yoonam, su boobaa duma leen teg lenn ci jàngoro, yi ma tegoon waa Misra, ndax man maay Aji Sax, ji leen di wérloo.»
Maay dalal saamar ci seen kaw, feye leen ko kóllëre gi ngeen fecci. Bu ngeen làqoo ci seeni biir dëkk yu mag sax, maay wàcce mbas ci seen biir, seeni noon jekku leen.
¶ Aji Sax jee leen di langalal mbas, ba raafal leen ca réew ma ngeen jëm, ngir nanguji ko.
Su ko defee seeni néew di poraatum mboolem njanaaw ak rabu àll, te kenn du leen dàq.
¶ Asayel ne ko: «Sang bi, looy jooy?» Mu ne ko: «Damaa xam lu bon li ngay defi waa Israyil. Seeni tata ngay taal, seeni xale yu góor nga jam saamar ñu dee, seeni doom nga tas ci suuf, seeni jigéeni biir nga butti.»
Merum Aji Sax ji nag ne jippét ca kaw Israyil, mu teg leen lu yàgg ci loxoy Asayel buurub Siri ak Ben Addàd doomu Asayel.
Yàlla sotti leen tàngooru xadaram, mu dim sànj ak naqar ak njàqare, lépp di gàngooru ndaw yu indiy musiba.
Moo tax Aji Sax ji doge Israyil bopp ak geen, boole tiir ak barax fóom ci benn bés.
Maa ngi meral Aji Sax ji ba fees ba manatuma koo dékku. Aji Sax ji nee: «Sippi ko tuut-tànk yi ci mbedd mi, sippiwaale ko waxambaane yi daje, mu laawaale jëkkër ak jabar, mag ak màggat,
Aji Sax ji dafa wax ne: «Ku xelu, bumu damoom xelam; ku jàmbaare, bumu damoo njàmbaaram; ku woomle, bumu damoom koomam.
¶ «Te dinaa wàcce fi seen kaw ñeenti xeeti duma.» Kàddug Aji Sax jee. «Saamar di bóom; xaj diri yóbbu, njanaaw ak rabu àll for, mu jeex.
Kon nag bàyyil seeni doom ñu xiif ba dee, jañax leen ci ñawkay saamar, seeni jabar suul doom, suul jëkkër, seeni góor loroo mbas, seeni waxambaane daanoo xare.
Duñu dellu réewum Misra. Waa Asiri ñooy doon seen buur, nde ñoo baña délsi fi man.
«Maa wéetal seeni biir seen dëkkoo dëkk, dugub ñàkke fépp fu ngeen moom, te taxul ngeen waññiku fi man.» Kàddug Aji Sax jee.
Maa leen dumaa gàncax gu benaat, ak gu xuur, ak tawub doji yuur ci mboolem seen liggéeyu loxo, te taxul ngeen délsi fi man, kàddug Aji Sax jee.