TSK

TSK · Amos 6:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Musaa ne ko: «Coow loolu de du bàkku yu njàmbaar waral, du jooytu yu jéll sabab, woyi mbumbaay daal laa dégg.»

¶ Ba gaalu kóllërey Aji Sax ji duggsee ca dal ba, Israyil gépp a xaacoondoo, ba suuf say riir.

¶ Ba mu ko defee muy jéllu Yuda fa kanam Israyil. Waa Yuda tasaaroo, ku nekk ñibbi ca sab xayma.

Job 31:25 TSK

ndegam maa bége sama alal ju bare, bége koom gu ma sama doole may;

Xalelu góor bi, bànneexul bi ngay gone, bégalal sa xol bi ngay ndaw. Toppal loo namm ak loo xemmem, waaye xamal ne loolu lépp, Yàlla da la koy laaj.

Nga wax ko ne ko: “Defal ndànk te ne cell. Bul tiit, bul xàddi ndax merum Reccin ak Siri, ak doomu Remalya ji. Duñu dara lu moy ñaari gil yuy saxar!

Tata dina tukkee diiwaanu Efrayim, nguur foqe dëkk ba ñuy wooye Damaas, te ndesu Siri du ëpp bànni Israyil daraja. Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi.

Kuy damu kay, na damoom xelam mu ko may mu xam ma, xam ne maay Aji Sax, jiy jëfe ngor ak dëgg ak njekk fi kaw suuf. Loolu déy mooy sama bànneex.» Kàddug Aji Sax jee.

Waxal, nga ne: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii fi sa kaw, yaw Firawna buuru Misra, yaw ninki-nànka ju mag ji goore sa diggi dex, te naan: ‘Maa moom sama dex, man ci sama bopp maa ko sàkk!’

Ma ngay wax naan: «Xanaa lii du Babilon gu mag gi ma tabax man, ci sama doole ju réy, muy péeyu buur, di sama ndam ak sama daraja?»

Jonah 4:6 TSK

Ba mu ko defee Aji Sax ji Yàlla yebal ag lawtan, mu law, tiim Yunus, keral boppam ngir xettli ko. Yunus bég mbégte mu réy ca lawtan ga.

«Su bés baa gàcce dootul am ci sa mboolem jëf, ji nga ma moye, nde maay jële fi sa biir ñiy bége sab sag, te doo damooti ci sama kaw tund wu sell.

Waa àddina dinañu bége seen dee, di bànneexu, di joqlante ay njukkal, ndaxte ñaari yonent yooyu ñoo lakkaloon waa àddina.