TSK

TSK · Amos 6:9

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Dina am ku bokk ci yaw ku ma dul dagge ci liggéey bu jëm ci sama sarxalukaay, waaye maa lay jooyloo, ba nga ñàkki bët, teg la njàqarey xol, te mboolem ñu yokku ci sa kër, seen digg doole lañuy deeye.

Ñuy fukki góor, di doomi Aman doomu Amdeta, fitnaalkatu Yawut ya. Bóom nañu leen, waaye seen loxo laalul alal ja.

Job 1:19 TSK

Ngelaw lu mag jekki bàyyikoo ca wàllaa màndiŋ ma, dal ca ñeenti weti néeg ba, mu màbb ca kaw gone ya, ñu dee. Mennum man doŋŋ maa ca rëcce ba àggesi la ko.»

Yal na askanam dagg. Balaa geneen maas a wéy, yal na seenu tur fey.

Amos 5:3 TSK

Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Junniy xarekat ay génne fii, téeméer délsi; téeméeri xarekat génne fee, fukk délsi, ñeel waa kër Israyil.»