TSK

TSK · Amos 7:14

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ilyaas bàyyikoo fa, fekk Alyaasa doomu Safat, Alyaasa di gàbb ak ñaar fukki nag ak ñeent yu ko jiitu, ñu likke leen ñaar-ñaar, moom ci boppam mu jiital fukkeelu likke baak ñaar. Ilyaas dikk ba ca moom, sànni mbubbam ca kaw Alyaasa.

¶ Kurélu yonenti Betel nag dikk ca Alyaasa ne ko: «Ndax xam nga ne bésub tey jii Aji Sax ji dina la yenni sa kilifteefu sang Ilyaas?» Mu ne: «Man kay xam naa ko; waaye noppileen rekk.»

¶ Ba loolu amee juróom fukki nit bawoo ca kuréli yonent ya, dikk taxaw, dànd leen, janook ñoom fa ñu yem ñoom ñaar ca tàkkal dexu Yurdan.

¶ Gannaaw loolu Alyaasa ñibbi Gilgal, mu yemook xiif am ca réew ma. Mu am bés kurélu yonent ya daje fa moom. Alyaasa ne surgaam: «Tegal cin lu mag li te toggal yonent yii mbuum.»

Amos 1:1 TSK

¶ Kàdduy Amos a ngi, di boroom jur bu dëkkoon Tekowa. Mu am peeñu mu jëm ci Israyil ci janti Osiyas buurub Yuda ak janti doomu Yowayas, Yerbowam buurub Israyil. Loolu tollu ci ñaari at lu jiitu yëngu-yëngu suuf ba.

Kenn ku ne da naan: “Man de dumab yonent, beykat laa. Ab surga laa masa doon ba may ndaw ba tey.”