TSK

TSK · Amos 9:8

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ndax kat li feek juróom ñaari fan dinaa wàcce taw ci kaw suuf diiru ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg, ba far ci àddina mboolem mbindeef mu ma sàkk.»

Ndax kat seen Yàlla Aji Sax ji ci seen biir, ku fiir la. Lu ko moy sànjum Aji Sax ji dina tàkk ci seen kaw, te dina leen sànk, ba raafal leen ci kaw suuf.

Aji Sax jaa nga këram gu sell. Aji Sax jaa nga asamaan, kaw jalam, ne jàkk doom aadama, di ko seetlu.

Aji Sax ji moo gis lépp, di xool ku baax ak ku bon.

«Yéegleen seeni tata, yàqte waaye buleen leen jeexal tàkk. Tenqileen lawit yi, ñooñoo bokkul ci Aji Sax ji.

Aji Sax ji dafa wax, moom mi dogal jant di leeral bëccëg, dogal weer ak biddiiw di leeral guddi, yëngal géej, kiy gannax yi riir, kookooy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.

Maa ngi nii di leen teewloo seen musiba, waaye du seen jàmm laa leen di teewloo. Te mboolem waa Yuda ñi ci réewum Misra dinañu sànkoo saamar akub xiif, ba keroog ñuy jeex tàkk.

Hosea 1:6 TSK

¶ Mu dellu ëmb, gannaaw gi mu am doom ju jigéen. Aji Sax ji ne: «Tudde ko Lo Ruwana» (mu firi Ki ñu yërëmul), mu ne: «ndax dootuma yërëm waa kër Israyil, dootuma leen baal.

Efrayim moom, su naatee ci biiri bokkam it, fa màndiŋ ma la ngelawal penku, ngelawal Aji Sax ji di uppe, bëti ndoxam tëju, ay teenam déy. Kii mooy sëxëtoo ab dencam, ak mboolem lu cay alal.»

Amos 9:4 TSK

Su ñu demee, diy jaam ñu seeni noon jiital, fa laay sante boroom saamar, mu bóom leen. Du bëtu jàmm laa leen di xoole, bët bu aay laa leen di xoole moos!»

¶ Ma ne kon, xanaa Yàlla daa wacc ñoñam? Mukk kay! Man ci sama bopp ci Israyil laa bokk, askanoo ci Ibraayma, giiroo ci Beñamin.