TSK

TSK · Colossians 2:4

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ci seen biir sax la aw nit di jóge taxaw, di wax ndëngte, ngir xiirtal taalibe yi, ba ñu topp leen.

Sama kàddu ak samam njàngle jotewul woon dara ak neex làmmiñ gu xam-xamu nit ràbb, waaye dafa di ay firnde yu manooreg Noowug Yàlla lañal,

¶ Su boobaa nu noppee doon ay tuut-tànk yu nit ñiy muusaatoo kàddu yu mel ni gannax yu nuy baaje, ak ngelawal mboolem àlluwa ju bees ju nuy pamti-pamtee ci seen biir pexey naxe ak njublaŋ, ngir fàbbi nu.

¶ Moytuleen ba kenn bañ leena këfe kàdduy naxi neen yu ñu jàppe xam-xam bu xelu, kàddu yu sukkandikoowul Almasi, xanaa aaday nit, ak cëslaayi àddina.

Peeñum ku dëng ki liggéeyu Seytaane lay àndal, te dina wone wépp xeetu manoore, aki firnde ak kéemaani feni neen,

Waaye ay kebetuy àddinay kese, moytu ko, ndax ngëmadi gu ko yées rekk lay yóbbee,

¶ Ndax kat bare na ñu të, rawatina ci tuubéen ñi bokk ci askanu yawut, ay waxkati neen lañu, te ñooy yàq xeli nit ñi.

Ñu xalab ninki-nànka ju réy ja, jaanu cosaan joojee ñuy wax Tuumaalkat bi, di ko wax Seytaane, naxekatu mboolem àddina. Ci kaw suuf lañu ko xalab, mooki malaakaam.

Da koo sànni ci xóote bi, tëj ko, sakk buntu xóote bi, ndax du naxati askan yi, ba kera junniy at yi mat. Gannaaw loolu nag fàww ñu yiwi ko diir bu gàtt.