TSK

TSK · Colossians 2:7

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ku jub day naat nig tàndarma, màgg ni seedaru Libaŋ

Day mel ni garab gu saxe wetu ndox, lawal ay reenam ca wal ma, ragalul tàngoor wu dikk, xob ya di naat. Du tiit atum maral, du ñàkk meññeef.»

¶ Kooku leen mana dooleel nag ndax sama xibaaru jàmm, ak waareb Yeesu Almasi, mi mu feeñal mbiram tey, gannaaw ba mu nekkee mbóot mu làqu woon naka jekk,

¶ Kon nag yeen sama bokk yi ma soppal sama bopp, farluleen, bu leen dara yëngal, te saxooleena jëm kanam ci liggéeyu Sang bi, te ngeen xam ne seenu ñaq, ci seenub ànd ak Sang bi, du neen.

Yeena di tabax, bi ndawi Almasi ak yonent yi di kenu gi, te Almasi Yeesu ci boppam di doju coll wi.

ndegam kay Yeesu ci boppam ngeen dégg mbiram, ba jànge ci moom, dëgg gi bawoo ci moom,

te ngeen di sante Baay bi, mbég, moom mi leen yellale ab cér ca muuru ñu sell ña, ca réewum leer ga.

Lu ngeen mana def, muy ci wax, di ci jëf, defleen ko ci turu Sang Yeesu, tey sant Yàlla Baay bi ci moom.

yal nañu leen may jàmmi xol, te may leen dooley wéye jépp jëf ju baax, ak gépp kàddu gu rafet.

¶ Dikkleen ci moom, mooy doj wuy dund. Nit ñee ko beddi moos, waaye Yàllaa ko fal, fonk ko.

¶ Kon nag yeen soppe yi, gannaaw xam ngeen loolu ba noppi, wattuleen bala leena réeraangey moykati yoon yi yóbbaale, ba yolomal seenub taxawaay.

Jude 1:20 TSK

Waaye yeen samay soppe, sampuleen ba dëgër ci seen yoonu ngëm wu sell wee sell, te ngeen di ñaane ci Noo gu Sell gi.