wattuleen seen bopp bala ngeena fàtte Aji Sax ji leen génnee réewum Misra, kërug njaam ga.
TSK
TSK · Colossians 2:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi kat dafa wax ne: «Seeni yonent ak seen gisaanekat yi ci seen biir, buñu leen nax. Te it buleen déglu seen boroom gént yi ngeen di géntloo,
¶ Ci kaw loolu ay boroom xam-xam yu bokk ci ngérum Epikur ak ngérum Estowisen, di werante ak moom. Ñenn ña ne: «Kebatukat bii, lu muy wax nii?» Ña ca des dégg Póol di waare xibaaru jàmm bi ci Yeesu ak ndekkiteem, ñu ne: «Daa mel ni ay tuur-tuuraani doxandéem lay waareel.»
¶ Gannaaw ba ñu xamee Yàlla, taxul ñu màggal ko ngir li muy Yàlla, taxul ñu delloo ko njukkal, xanaa réer ci seen xalaati neen, ba seen xel mu wayadi far tàbbi cig lëndëm.
Ndaxte bindees na ne: «Maay yàq xam-xamu xamkat yi, ñi xelu, ma neenal seenum xel.»
¶ Teewul nit a ngi naan: «Nan la ñi dee di dekkee? Wan yaram lañuy dekkaale?»
Yoonu Yawut, maa ci rawoon ñu bare ci sama maas gi ma bokkal askan, te maa leen gënoona xér fuuf ci sunu aaday maam.
Waaye léegi bi ngeen xamee Yàlla, mbaa bi leen Yàlla ràññee, nu ngeen mana delluwaate ci mbiri àddina yooyu boole tële ak ñàkk njariñ, bay nekkaat seeni jaam?
¶ Yeen nag du loolu ngeen jànge ci Almasi,
¶ Moytuleen xaj yi, defkati mbon yooyu laa ne, moytuleen leen, moytuleen njoofkat yooyu jiital aaday xaraf.
¶ Ndegam nag yeena bokk ak Almasi dee, ba teqlikoo ak li àddina def cëslaay, ana lu tax ngeen mel ni ñu bokk ci àddina ba tey, di tegoo ay dogali yoon yu mel nii:
¶ Ngalla waay Timote, sàmmal li ñu la dénk! Moytul kebetuy àddinay kese, ak werantey diiŋatkat yu tuddoo boroom xam-xam.
Waaye nit ñu bon ñi, ak maa-man yi dañuy gën di bon rekk, di naxe tey nax seen bopp.
Xam ngeen ne yëf yuy wéy yu mel ni xaalis mbaa wurus, du moom lees leen jote ci seen dundinu neen wa ngeen donne ca seeni maam,