Ndaxte kat man Aji Sax ji maay ki leen génne woon réewum Misra, di seen Yàlla. Sell-leen boog, ndax man ku Sell laa.»
TSK
TSK · Daniel 1:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Foo deeye it, ma deeye fa, ñu denc ma fa. Yal na ma Aji Sax ji teg mbugal mu gëna tar, ndegam lenn lu moy dee tàggale na maak yaw.»
Ñuy darook tuurum Baal Pewor, di lekk lu ñu sarxal ay yàlla yu amul bakkan,
Yeen ñiy def lu bon, xiddileen ma, ba ma sàmmonteek sama santaaney Yàlla.
Aji Sax ji teg ca ne: «Noonu la bànni Israyil di lekkeji seen ñamu sobe ci biir xeet yi ma leen di tasaareji.»
Dungeen des ci réewum Aji Sax ji. Efrayim, Misra lay dellu, te ca Asiri, lu daganul lañu fay lekkeji.
Ba Barnaba dikkee ba gis yiw, wi leen Yàlla may, dafa bég, di leen ñaax ngir ñu ŋoye seen xol ci Sang bi.
Waaye ki dogu dëgg ci xolam, te du ndigalu gàntal lu mu sañula bañ, xanaa ci sagoy boppam doŋŋ la dogoo ne du jël janq bi mu digooloon ab séy, kooku ba tey, def na lu baax.
¶ Xool-leen bànni Israyil ci wàllu deret. Ñiy lekk yàppu juru sarax gu ñu rendi, xanaa bokkuñu ak sarxalukaay bi ab céram?
Kon na ku nekk joxe, ni mu ko waaje ci xolam, te bañ koo tiisoo, bañ koo joxee ñàkk pexe, ndax kiy joxee xol bu sedd, Yàlla sopp na ko,