¶ Xaalisu saraxu peyug tooñ nag ak xaalisu saraxu póotum bàkkaar daawuñu ko indi ci kër Aji Sax ji. Sarxalkat yaa ko moomoon.
TSK
TSK · Daniel 11:17
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Tumurànke naa, nga gis. Duyal samay rongooñ ci sa mbuus. Du lim nga lépp?
Su ko defee nga jël saafukaayu weñ, teg ko, mu mel ni miiru weñ bu dox sa digganteek dëkk bi, te nga janook dëkk bi. Noonu nga koy gawe, mu gawu. Loolu di misaal, ñeel waa kër Israyil.
Firawnaak mbooloom mu réy ak gàngooram gu mag sax duñu ko mana wallu ci xare, keroog bu ñuy yékkati ab sëkk, tabax ab gawukaay ngir bóom ñu bare.
Bu juróom benn fukk yeek ñaar ciy àppi juróom ñaar weesee, dees na bóom ku ñu fal, te kenn du ànd ak moom. Gannaaw loolu kilifa dina ñëw, ànd ak gàngooram, yàqte dëkk beek jaamookaay bi. Waaye kilifa googu lu mel ni mbënn a koy mujje. Dogal nañu ne yàqte gi dina wéy ba keroog xare biy jeex.
Ku farul ak man nag, man ngay xeex, te ku àndul ak man di dajale, yaa ngi tasaare.