TSK

TSK · Daniel 11:33

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Su boobaa gëti njàccaar yi dootuñu gëmm, te noppi ñiy dégg dañuy teewlu,

Ñu bare dees na leen sellal, fóot leen ba ñu set wecc. Waaye ñu bon ñi wéy di bon, te kenn du ci xam liy xew, teewul ñi rafet xel dinañu ko xam.

«Kàddug sarxalkat déy day sàmm xam-xam, te ciy waxam la nit ñi di sàkkoo àlluwa, nde mooy ndawal Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.

Ba mu ko gisee, da koo indi Àncos. Ba mu ko defee, atum lëmm ñuy daje ca mbooloom gëmkat ña, di jàngal nit ñu takku. Ca Àncos lañu jëkka wooye gëmkat ñi ay gëm-Almasi.

¶ Gannaaw ba ñu xamlee fa Derbe xibaaru jàmm bi, ba am fa taalibe yu bare, dañoo dellu Listar ak Ikoñum ak Àncos gu Pisidi.

Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne moo mana sàmm li ma ko dénk ba keroog bés ba.

¶ Man nag, daanaka saraxu tuuru bu sottiku laa ba noppi; sama waxtuw dem dëgmal na.

Ngëm la ñeneen dékkoo ay kókkali aki yar, ba ciy jéng ak tëjteb kaso.

¶ Xam naa fa nga dëkk, fa la Seytaane samp nguuram. Teewul nga ŋoy ci sama tur te weddiwoo ne man nga gëm ba sax ca fan, ya nit ña reye ca seen biir, Antipas sama seede bu am kóllëre ba, foofa Seytaane dëkk.

¶ Ma ne ko: «Sama sang, loolu de xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca nattu bu réy ba. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Gàtt bi.

Ma gis ne jigéen ji daa naan ba màndi ci deretu ñu sell ñi ak deretu ñi doon seedeel Yeesu. Ba ma ko gisee, jaaxle naa lool.