TSK

TSK · Daniel 11:35

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Moo leen leele mànnu màndiŋ, ma seeni maam xamuloon, ngir teg leen coono, nattu leen, te mujje baaxe leen.

Xaalis ak wurus sawaraa koy xelli, waaye nit, ab xolam, Aji Sax jee koy nattu.

Jibril dikk nag ba fi ma taxaw. Ba mu jegesee, ma tiit lool, ba daanu, sama kanam dëppu fi suuf. Mu ne ma: «Yaw doom aadama ji, nanga xam ne peeñu mii mujug jamono la.»

Dina feddli kóllëre diggam ak ñu bare ci benn àppu juróom ñaar, te ci diggu àppu juróom ñaar ba lay dakkal sarax yi ñuy rendi ak yeneen sarax. Ci genn wetu sarxalukaay bi la yàqkat biy taxawal lu siblu, di sabab yàqute, ba keroog muj gi ñu ko dogalal ne milib ci kawam.»

¶ «Bu àpp bi jotee, buur bëj-gànnaar dina dal ci kaw réewum bëj-saalum. Waaye boobu yoon du deme na woon.

Ca mujug jamono buur bëj-saalum dina fenqoo ak buur bëj-gànnaar. Te itam buur bëj-gànnaar dina mel ni ngëlaani, ne milib ci kawam, ànd ak watiiri xare aki gawar ak gaal yu mag yu bare. Dina dugg ci ay réew, bëtt, jàll nim wal.

Ñu bare dees na leen sellal, fóot leen ba ñu set wecc. Waaye ñu bon ñi wéy di bon, te kenn du ci xam liy xew, teewul ñi rafet xel dinañu ko xam.

Ñetteel bi laay tàbbal ci sawara, xelli ko ca ni ñuy xellee xaalis, nattu ko ni ñuy nattoo wurus cib taal. Xaaj boobu moo may woo ci sama tur, ma wuyu ko. Moom laay wax: “Sama ñoñ,” Moom mu ne: “Aji Sax jeey sama Yàlla.”»

¶ Póol ak ñi mu àndal nag bàyyikoo Pafos, dugg gaal, jëm Perge, ca diiwaanu Pamfili. Yowaan moom tàggoo ak ñoom, dellu Yerusalem.

James 1:2 TSK

¶ Bokk yi, bu ngeen jaaree ci mboolem xeeti nattu, jàppeleen ko mbég mu mat sëkk,

Bul ragal mukk mitit wi nga nara daj. Seytaanee ngi noonu di dugal kaso ñenn ci yeen, ngir nattu leen. Dingeen am coono diiru fukki fan. Nanga saxoo kóllëre ba dee fekk la ci, ma kaalaa la kaalag dund.

Meneen malaaka génne ca néeg Yàlla ba, daldi àddu ca kaw, wax ak ki toog ci niir wi, ne ko: «Dawalal sa sàrt te góob, ndaxte ngóob jot na, ngóobum àddina ñor na.»