TSK

TSK · Daniel 2:20

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

«Cant ñeel na Aji Sax, ji may Israyil mbooloom ab dal-lukaay, muy la mu waxoon lépp, ngir benn baat fanaanul àll ci digey jàmm yi mu dige woon yépp, Musaa jaamam ba jottli.

Yeswa nag ak Kadmiyel ak Baani ak Asabneya ak Serebya ak Odiya ak Sebaña ak Petaya, Leween ñooñu ñépp àddoondoo ne: «Màggal-leen seen Yàlla Aji Sax ji sax dàkk, ba fàww. Nañu màggal sa tur wu tedd, wi raw gépp cant ak ngërëm.»

Job 12:16 TSK

Kee am doole, keey sottal, di boroom aji réer ak ka ko réeral.

Ki may sarxale jaajëf moo ma teral; ku topp yoon, ma won ko wallu Yàlla.»

Cant ñeel na Yàlla Aji Sax ji, Yàllay Israyil, mi wéetooy jalooreem.

Yal nañu teral turu Aji Sax ji tey ak ëllëg!

Muy jàngi màggal, ñeel Daawuda. Sama Yàlla, Buur bi, naa la màggal, teral sa tur ba fàww.

Maa moomi digle, di maye gis-gis; maa am ug dégg, di boroom doole.

Mooy walbati jamono, di soppi demin, di fal buur, di folli. Mooy xelal boroom xel mu rafet, di xamal boroom xel mu ñaw.

Jude 1:24 TSK

¶ Ki leen mana aar ci bépp jéll, ba taxawal leen fa muy teewejee darajaam, te fekk leen ñàkk sikk, seen mbég mat sëkk,