Laban tudde bérab ba Yegar Saaduta; Yanqóoba tudde ko Galet.
TSK
TSK · Daniel 2:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Samiyel wax ak mbooloo mépp, ne leen: «Yeena gis ki Aji Sax ji taamu? Kenn melul ni moom ci mbooloo mi mépp.» Mbooloo ma mépp àddu ca kaw ne: «Buur, guddalu fan!»
Ba mu ko defee Batseba dëpp kanamam fa suuf, sukk fa kanam Buur, ne ko: «Buur Daawuda, sang bi, yal nanga fi yàgg.»
Ma daldi ne Buur: «Guddalu fan, Buur! Nu may def ba duma ne yogg, te dëkk ba samay maam tëdd gental, bunt ya lakk ba xoyomu?»
Maay neenal firndey maaman, dofloo gisaanekat. Maay weddi fóore, def xam-xamam mu dig ndof.
Li ma gis daal ci sama kaw lal mooy lii: Damaa jekki gis garab ci digg àddina si, mu gudd lool.
¶ Ba loolu amee boroom xam-xami Buur yépp dikk ba ca biir, waaye manuñoo jàng mbind ma, bay xamal Buur la muy tekki.
Ñu daldi ne: «Dunu gis mukk lenn lu nu tuumaal Dañeel. Xanaa nu gis ko ci yoonu Yàllaam.»
Naka la jub kàmb ga, daldi woo Dañeel; baat baa nga tiis. Mu ne ko: «Éy Dañeel, jaamu Yàlla jiy dund; sa Yàlla ji nga saxoo jaamu, mbaa mujj na laa xettli ci gaynde yi?»