¶ Gannaaw loolu Firawna neeti Yuusufa: «Bés niki tey, dénk naa la réewum Misra gépp»
TSK
TSK · Daniel 2:48
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ñooña dem ba ca Balaam, ne ko: «Balag doomu Sippor dafa wax ne: “Ngalla, bu la dara teree dikk, wuysi ma.
Ña nga naan ca seen biir: «Gis ngeen waa jee di ñëw, dëkksi Israyil a ko yékkati. Képp ku ko rey de, Buur dina ko jox alal ju bare. Doomam la koy may jabar, te waa kër baayam, dina leen jagleel ab cér ci digg Israyil.»
¶ Fekk na Barsilay ma bokk ca Galàdd jóge woon Rogelim, ngir gunge Buur Daawuda, ba mu jàll dexu Yurdan, bala moo tàggtoo ak moom ca wàllaa dex.
Alalam juróom ñaari junniy (7 000) gàtt la woon, ak ñetti junniy (3 000) giléem, ak juróomi téeméeri (500) lëkkey nag yuy rijji, ak juróomi téeméeri (500) mbaam yu jigéen, ak jaam yu bare lool. Góor googu daal moo ëppoon daraja ca mboolem waa penku.
Waaye su ngeen waxee gént gi, wax ma piri mi, ay weexal aki yool ak teraanga ju réy ngeen di jële ci man. Kon nag waxleen ma gént gi, wax ma piri mi.»
Dafa am ay Yawut yoo tabb, ñu yore saytub diiwaanu Babilon. Ñu di leen wax Sadarag ak Mesag ak Abet Nego. Ñooñu de Buur, déggaluñu la; say yàlla, jaamuwuñu leen; sa jëmmu wurus ji nga samp it, màggaluñu ko.»
¶ Ma ne ko: «Beltasar, kilifay taryaax yi, man ci sama bopp xam naa ne xelum yàlla yu sell yaa ngi ci yaw, te menn mbóot jaaxalu la. Peeñum gént gi ma gént, wax ma piri mi.
¶ Buur daldi àddu ca kaw, di woolu ñeengokat yeek xërëmkat yi ak seetkat yi. Mu wax ak boroom xam-xami Babilon yooyu ne leen: «Képp ku jàng mbind mii te wax ma lu mu tekki, dees na ko solal yérey buur yu xonq curr, takkal ko caqu wurus, jox ko kilifteef gu koy tofal ci bummi.»
Dégg naa nag ne man ngaa firi lool ak a lijjanti mbir yu jafe. Soo ma manee jàngal mbind mi, wax ma lu muy tekki, dees na la solal yérey buur yu xonq curr, takkal la caqu wurus, jox la kilifteef gu lay tofal ci bummi.»
¶ Ci kaw loolu Daryus waa Medd ba, jot ca nguur ga, fekk ko mu am juróom benn fukki at ak ñaar.