¶ Mu am bés goney Yàlla dikk, teewsi fa Aji Sax ji. Seytaane tuumaalkat bi itam bokk ca.
TSK
TSK · Daniel 3:25
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
ba biddiiwi njël sarxolleendoo, goney Yàlla yépp xaacoondoo?
Kii kay moo lay musal cig fiir ak loraangey mbas.
Booy xuus cim ndox, maa ngi ànd ak yaw; ag dex du la mëdd. Booy dox cib taal, doo lakk, sawara du la xoyom.
¶ Nabukodonosor wax ne: «Cant ñeel na Yàllay Sadarag ak Mesag ak Abet Nego, moom mi yónni malaakaam, mu wallu jaamam ñi ko wóolu, ba xëtt sama ndigal man Buur, te jaay seen bakkan gënal leen ñuy jaamu mbaa di sujjóotal jeneen yàlla ju dul seen Yàlla.
Malaaka mi ne ko: «Noo gu Sell gi mooy wàccsi ci yaw, dooley Aji Kawe ji yiir la. Moo tax itam ku Sell kiy juddoo ci yaw, dees na ko wooye Doomu Yàlla.
Teewul Póol yëlëb jaan ja ca sawara sa, te dara jotu ko.
¶ Te it su ngeen dee ñu njaxlaf ci def lu baax, ana ku leen di def lu bon?