¶ Gannaaw loolu ndigal a ngii tukkee ci man ñeel képp ku tebbi bii dogal: Dees na roccee ca néegam ab xànq, yékkati ko, wékk ko ca, ba noppi def këram ab sën ndax jëfam jooju.
TSK
TSK · Daniel 3:29
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ca la Yàllay jóg, ngir àtte, ba wallu kuy néew dooley àddina. Selaw.
Léegi, bettuma leen. Bu ngeen di dégg bufta geek toxoro geek xalam geek riiti geek kooraa geek liit geek mboolem jumtukaayi xumbal yi rekk, sujjóotleen, màggale ko jëmm ji ma sàkk. Waaye su ngeen ko màggalul, dees na leen daldi sànni ci biir taalu sawara bu yànj. Ana yàlla ju leen di musal ci man?»
¶ Nabukodonosor wax ne: «Cant ñeel na Yàllay Sadarag ak Mesag ak Abet Nego, moom mi yónni malaakaam, mu wallu jaamam ñi ko wóolu, ba xëtt sama ndigal man Buur, te jaay seen bakkan gënal leen ñuy jaamu mbaa di sujjóotal jeneen yàlla ju dul seen Yàlla.
Keey musle, di xettlee, di def ay màndarga aki kéemaan, kaw asamaan ak suuf. Kee musal Dañeel ca pàddum gaynde ya.»