TSK

TSK · Daniel 6:4

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Firawna daldi ne jawriñ ya: «Ndax masees naa gis ku mel ni kii a waay, nit ku Yàlla sol Noowug boppam?»

Daawuda baaxle ca yoonam yépp, Aji Sax ji ànd ak moom.

¶ Ayimeleg ne Buur: «Buur, ana sa surga yii ba ñu daj, ku la nangule ni Daawuda mii, di sa goro, jiite say dag, te di ku ñu nawloo ci sa biir ëtt bii?

Ku bon a ngi yeeru ku jub, di ko wuta bóom.

Ma gis ne nit ak kër-këram jépp ak bépp manoorey liggéey, iñaanantee ko waral. Loolu it, cóolóoli neen ak napp um ngelaw.

Waaye yaw Aji Sax ji, xam nga mépp pexe mu ñu may fexee bóome. Bu leen jéggal seen ñaawtéef, bul far seeni moy, yal nañu nërmeelu fi sa kanam, jëflanteel ak ñoom bi ngay mer.

¶ Ci biir loolu ay xërëmkat dikk, di boole Yawut ya.

¶ Ba mu ko defee ñu bàyyi Yeesu xel, daldi yebal ay yeerukat, sas leen ñu yiw-yiwlu te di ko fiir ci kaw kàddu ba jàpp ko, ngir jébbal ko boroom dëkk bay boroom kilifteef ga ak sañ-sañ ba.

Mu ne leen: «Yeena ma indil waa jii, ne ma mooy lajjal askan wi. Man nag laaj naa ko ci seen kanam, waaye gisuma ci moom genn tooñ ci li ngeen ko tuumaal.

Noonu may def rekk laay saxoo, ngir xañ aw lay, ñiy wut aw lay wu ñu damoo, naan ñook nun a yem kepp daraja.

Moo tax ma bëgg, jëtun ñiy ndaw séyaat, ami doom, yor seen kër, ba noon bi du am lu mu yàqe sunub der.

Seen dundin ci biir jaambur ñi gëmul, rafetal-leen ko, ba su ñu leen waxaloon ne ay defkati lu bon ngeen itam, seen jëf ju rafet lañuy gis, te moom lañuy sàbbaale Yàlla, kera bésub dikkam.

Su ñu leen jànnee sax ndax turu Almasi, ndokklee yeen, ndax Noo gu darajawu gi, Noowug Yàlla moo wàcc ci yeen.