Daniel 8:12
TSK
Gàngooru xare gi tegu na ciy loxoom, boole kook saraxu bés bu jot bi, lépp cig tooñam. Béjjén bi dal ci kaw dëgg, daaneel ko fi suuf, ay pexeem joy.
TSK
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Gàngooru xare gi tegu na ciy loxoom, boole kook saraxu bés bu jot bi, lépp cig tooñam. Béjjén bi dal ci kaw dëgg, daaneel ko fi suuf, ay pexeem joy.
Ay xarekat yu mu yebal dinañu dem teddadil jaamookaay, bi ci tata ji; dinañu dakkal sarax si ñu fa saxal fàww, ba noppi teg fa lu siblu luy jur yàqute.
¶ Gannaaw bu ñu seedee ba noppi nag, rab wiy jóge ci xóote bi mooy xareek ñoom, daan leen, ba rey leen.
¶ Ñu may rab wi nag muy kañu ak a saaga Yàlla, may ko it mu saña wéye noonu diiru ñeent fukki weer ak ñaar.
Dinañu xare ak Gàtt bi, waaye Gàtt bee leen di daan, ndax mooy Sangu sang yi, di Buuru buur yi. Mooy daan mook ñoñam, ñi mu woo, tànn leen te ñu saxoo topp ko.»