TSK

TSK · Daniel 7:27

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ku woyof a cay lekk ba doyal, kuy wut Aji Sax ji, sant ko. «Guddleena gudd fan!»

Boroom bi, mboolem xeet yi nga sàkk ñoo lay sujjóotalsi, di màggal sa tur.

Na wóllërey Yàlla bànneexoo seen ndam, bu ñu tëddee sax, di sarxolle,

Yaw la ay buur di baayoo, seeni lingeer di la nàmpal. Ñoo lay sujjóotal, di la maral say tànk, ba nga xam ne maay Aji Sax ji, te ku ma yaakaar du rus.»

Say wunt ay ubbiku saa su ne, guddeek bëccëg, du tëje, xanaa di la jàlleel alali xeet yi, seeni buur riixle ànd ca.

Léegi nag man, Nabukodonosor, maa ngi sant Boroom asamaan, di ko sargal, di ko màggal. Lu mu def dëgg la, fu mu jaare njub la, te kuy réy-réylu man na laa suufeel.

Waaye aji sell yu Aji Kawe ji dinañu jot ci nguur gi, moom ko fàww, saxoo ko dàkk.”

Ay xettlikat ñooy yéeg kaw tundu Siyoŋ, ngir yilif tundu Esawu, nguur gi di moomeelu Aji Sax ji.»

Aji Sax ji mooy doon buuru àddina sépp, bésub keroog Aji Sax ji di kenn, turam di wenn.

Dinañu xare ak Gàtt bi, waaye Gàtt bee leen di daan, ndax mooy Sangu sang yi, di Buuru buur yi. Mooy daan mook ñoñam, ñi mu woo, tànn leen te ñu saxoo topp ko.»

¶ Ci kaw loolu ma gis ay gàngune yu ñu jox ña ca toog, sañ-sañu àtte. Ma daldi gis bakkani ñi ñu dogoon seen bopp ndax la ñu doon seedeel Yeesu ak la ñu gëmoon kàddug Yàlla, ña sujjóotalul woon rab wi ak jëmmu nataalam, te amuñu màndargam rab wi ci seen jë mbaa seen loxo. Ñu dekki bay nguuroondoo ak Almasi diiru junniy at.