TSK

TSK · Daniel 9:18

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Bu ñu tuddalee noonu bànni Israyil sama tur, man, maa leen di barkeel.»

Ngalla Aji Sax ji, dékkal sa nopp ba dégg; Aji Sax ji, xippil say gët ba gis, te dégg kàdduy Senakerib yi mu yóbbante, ngir ñàkke la ko kersa, yaw, Yàlla jiy dund!

Aji Sax ji, bàyyil xel sa yërmandeek sa ngor. Naka jekk sa jikkoo!

Ngalla Aji Sax ji, dékkal sa nopp ba dégg; Aji Sax ji, xippil say gët ba gis, te dégg mboolem kàdduy Senakerib yi mu yóbbante, ngir ñàkke la ko kersa, yaw, Yàlla jiy dund!

«Ngalla séentool asamaan, xooleel fa sa kër gu sell ga ne ràññ. Ana sa fiiraangeek sa njàmbaar? Sag rafet xol ak sa yërmande ñooru na ma!

Du kenn kuy wormaal sa tur, mbaa mu yewwu ba jàpp ci yaw, yaa nu làq saw yiw, yaa nu def ban bu tooy ci sunu biir ñaawtéef yi nu tanc.

tey dikk taxaw fi sama kanam, biir kër gii ñu ma tudde, te naan: ‘Nun kay raw nanu,’ ba tax ngeen di def mboolem lu siblu lii?

Dëgg la sunuy ñaawtéef a nu tuumaal, waaye éy Aji Sax ji, jógal te saw tur tax, doonte dëddu nanu la ay yooni yoon, moy la.

Sa kàddu laa gis, di ko dunde, sa kàddu di ma bégal, bànneexal sama xol. Yaw Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, déy, sa tur lañu ma tudde.

Jombul ñu tinu Aji Sax ji, ku nekk ci ñoom dëpp yoonu mbonam, ndax mer mu réy ak xadar ji Aji Sax ji tuddal askan wii kat, nar naa metti.»

¶ «Moo tax nanga wax waa kër Israyil, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen waa kër Israyil, li may waaja def, du yeen laa ci seet, li ma ci seet mooy sama teddngay tur wu sell, wi ngeen teddadil fi digg yéefar yi ngeen fekki.

ñeel mbooloom Yàlla, mi ci Korent, yeen ñi ñu sellal ci jëmmu Almasi Yeesu, te ñu woo leen ngir ngeen doon ñu sell, ñeel itam mboolem ñiy tudde fépp fu mu mana doon, sunu turu Boroom Yeesu Almasi, mi leen moom, moom nu.