Ci kaw loolu Aji Sax ji romb fa kanam Musaa, di biral naan: «Aji Sax jee, Aji Sax ji, Yàlla jiy yërëm, di yéwéne, mer ma diib, ngor gaak kóllëre ga bare.
TSK
TSK · Daniel 9:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
“Aji Sax ji! Kiy muñ mer, te bare ngor, di bale tooñ aki moy te du ñàkka topp mukk doom, tooñu waajuram, ba ca sët yaak sëtaat ya.”
Xamleen boog ne seen Yàlla Aji Sax ji moom mooy Yàlla; mooy Yàlla ju dëggu jiy sàmm kóllëre ak ngor ñeel soppeem ñiy sàmm ay santaaneem, sët ba sëtaat, ba ci junniy maas.
Buleen am tiitaange ci ñoom, ndax seen Yàlla Aji Sax ji ci seen biir, Yàlla ju màgg la te raglu.
bu ñu demee ba seenum xel dellusee fa réew ma ñu leen yóbbu ngàllo, ñu tuub tey sàkku aw yiw fi yaw foofa ca réewum ña leen jàpp, ne la noo moy, noo ñaaw, noo def lu bon,
Ma ne: «Éy Aji Sax ji, yaw Yàlla Boroom asamaan, Yàlla ju màgg ji te raglu, di sàmm kóllëreek ngor, ñeel ñi la sopp tey topp say santaane.
¶ «Kon rikk waay, yaw sunu Yàlla, Yàlla ju màgg, ji àttan te mata ragal, di sàmm kóllëreek ngor; ngalla bul xeeb mboolem toskare ji dikkal sa ñoñ, muy buur ak njiit, sarxalkat ak yonent, dale ca sunuy maam ba ci nun ñépp tey, ca janti buuri Asiri, ba sunu jonni yàllay tey.
“Nangul ne ñaaw nga rekk, te man sa Yàlla Aji Sax ji nga tooñ, di wër di foye sa bopp ak yàllay doxandéem yi ci ker garaboo garab gu naat, te dégluwoo ma.”» Kàddug Aji Sax jee.
Ñu dikk moom ko, te déggaluñu la, toppuñu saw yoon, jëfewuñu mboolem li nga leen santoon, ba tax nga wàcce ci seen kaw mboolem musiba mii.
Ana Yàlla ju mel ni yaw, di bale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom. Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.
Moo jëfe yërmande ñeel sunuy maam, tey bàyyi xel kóllëreem gu sell,
¶ Ndokklee ku muñ ab nattu, nde su ca amee ngërëm, mooy yooloo kaalag dund, gi Yàlla dig ñi ko sopp.