TSK

TSK · Deuteronomy 13:1

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Buleen yokk dara ci kàddu gi ma leen di dénk, te buleen ci wàññi dara, ndax ngeen sàmm seen santaaney Yàlla Aji Sax, ji ma leen di dénk.

Mu dellu ne ko: «Man itam yonent laa ni yaw. Malaaka wax na ma ci ndigalal Aji Sax ji ne ma: “Waññi ko, mu ànd ak yaw sa kër, sex dugub, naan ndox.”» Fekk na la muy wax amul.

Bul yokk ay waxam, mu weddi say fen, nga weeru.

«Ndax ki gëna tuut ba ki gëna mag, ñépp a ngi lewal lu lewul. Yonent akub sarxalkat, ñépp a ngi wor.

¶ «Dégg naa kàdduy waxyu yi yonent yooyuy waxe ci sama tur ay fen, naan gént nañu lii, gént nañu lee.

¶ Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi kat dafa wax ne: «Seeni yonent ak seen gisaanekat yi ci seen biir, buñu leen nax. Te it buleen déglu seen boroom gént yi ngeen di géntloo,

«Yaw nit ki, waxal waxyu ci kaw yonenti Israyil yiy waxe ay waxyu. Nanga wax ñiy waxe waxyu ci seen xelum bopp, ne leen: “Dégluleen kàddug Aji Sax ji: Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:

Xërëm, waxi neen, gisaanekat gisi fen, seeni gént, nari neen, te caaxaani neen lañuy dalalee. Moo tax mbooloo mii di taxawaalu niy xar, tumurànke ndax ñàkkub sàmm.

Luke 6:26 TSK

Wóoy ngalla yeen, bu leen ñépp dee waxal lu baax, ndax noonu rekk la maami ñooñu daan jëfe ak yonenti caaxaan ya.

¶ Waaye na mu ame woon ci askanu bànni Israyil ay yonenti caaxaan, ni lay ame ci seen biir ay sëriñi caaxaan yuy sërxal ay àlluway sànkute yuy weddi sax Sang bi leen jot, ba yóbbe seen bopp sànkute ju bette.