Seen Yàlla Aji Sax ji, soppeleen ko seen léppi xol, ak seen léppi bakkan, ak seen léppi doole.
TSK
TSK · Deuteronomy 13:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Seen Yàlla Aji Sax ji moom ngeen di ragal, te moom ngeen di jaamu. Moom ngeen di ŋoyu, te aw turam ngeen di giñe.
Soppleen seen Yàlla Aji Sax ji, déggal ko te taq ci moom, ndax moom mooy seenug dund, di seen gudd-gi-fan ca réew ma mu giñaloon seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, ne ñoom la koy jox.
Yaw nit ki, waxees na la li baax, ak li Aji Sax ji sàkku ci yaw, te loolu moyul di def yoon, sopp jëfi ngor te woyof nooy toppe sa Yàlla.
Buleen jébbal seeni cér bàkkaar, mu def leen jumtukaayi njubadi; gannaaw yeena dekki bay dundaat, jébbal-leen Yàlla seen bopp te jébbal ko seeni cér, ngir def leen ay jumtukaayi njub.
Su ko defee ngeen di dunde dundin wu yellook Boroom bi, ngir bànneexal ko ci wet gu nekk, seen meññeef it di jépp jëf ju baax, te ngeen gën di xam Yàlla.