TSK

TSK · Deuteronomy 16:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ni ngeen di def ak ñoom kay mooy nii: seeni sarxalukaay, ngeen màbb; seen tuuri doj, ngeen rajaxe; seen xer yi ñuy jaamoo Asera tuur mi, ngeen gor; seen jëmmi tuur, ngeen lakk.

Aji Sax ji dina fàdd Israyil. Dinañu mel ni gattax guy foy-foyi cim ndox. Dina déjjatee Israyil ci suuf su baax sii mu joxoon seeni maam, tasaare leen ca wàllaa dexu Efraat, ndax dañoo samp ay xer yu ñuy jaamoo Asera, di merloo Aji Sax ji.

Ba loolu amee ñu dëddu mboolem seen santaaney Yàlla Aji Sax ji; sàkkal seen bopp ñaari wëllu yu ñu móol, samp xer wu ñuy jaamoo Asera, di sujjóotal mboolem biddiiwi asamaan tey jaamu Baal.

¶ Moo dugal ba tey jëmm ja mu sàkkoon ngir tuur ma ñuy wax Asera, ca biir kër ga Aji Sax ji waxoon Daawudaak doomam Suleymaan ne leen: «Ci biir kër gii ci Yerusalem, gi ma tànne ci mboolem giiri Israyil, laay dëj sama tur ba fàww.