¶ Buurub Edom nag ne leen: «Dungeen jaare fi man de, lu ko moy saamar laay génne, dajeek yeen.»
TSK
TSK · Deuteronomy 2:29
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ba loolu amee Aji Sax ji ne ma: «Buleen dal ci kaw Mowabeen ñi, di leen song ub xare, ngir duma leen jox benn cér ci seenum réew, ndax askanu Lóot laa sédd réewum Ar.»
¶ Waaye yeena tax Aji Sax ji mere ma ba giñ ne duma jàll dexu Yurdan, te duma dugg ca réew mu baax, ma leen seen Yàlla Aji Sax ji moomale.
¶ «Teral-leen seen baay, ak seen ndey, ni leen ko seen Yàlla Aji Sax ji sante, ndax ngeen gudd fan, ndax it ngeen baaxle ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji jox.
Ku dul doomu yoon du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji. Ku askanoo ci moom it, ba ca fukkeelu maas ga, du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji.
ndax la ñu leen dabewul woon aw ñam, mbaa am ndox, ca yoon wa, ba ngeen génnee Misra, xanaa di fey Balaam doomu Bewor ma bokk Petor ca Aram Naarim, ngir mu sàbbi leen.